LBRY Block Explorer

LBRY Claims • ndax-yaw-yaa-di-ki-wara-ñëw,-walla

5b7dee1dd9c2e851eb23122c62ee788a90125d4a

Published By
Anonymous
Created On
22 Feb 2022 11:48:32 UTC
Transaction ID
Cost
Safe for Work
Free
Yes
Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, walla danoo wara xaar keneen?
18 Taalibey Yaxya ya nettali mbir yooyu yépp seen kilifa. Noonu Yaxya woo ñaar ci ay taalibeem, 19 yónni leen ci Boroom bi, ngir laaj ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, walla danoo wara xaar keneen?» 20 Bi taalibe ya agsee ca Yeesu, ñu ne ko: «Yaxya moo nu yebal, nu laaj ndax yaa di Ki waroona ñëw, walla danuy xaar keneen?»
21 Ca waxtu woowa Yeesu wéral nit ñu bare ci seeni feebar ak ci seeni metit, di dàq ay rab tey gisloo ay gumba. 22 Noonu mu wax ndaw ya ne leen: «Demleen nettali Yaxya li ngeen gis te dégg ko. Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te néew doole ñaa ngi dégg xibaaru jàmm bi. 23 Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.»
24 Bi ndawi Yaxya yi demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li? 25 Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñiy soloo noonu, tey dund dund gu neex ñu ngi dëkk ci këri buur. 26 Kon lu ngeen seeti woon? Yonent? Waaw, wax naa leen ne ëpp na yonent. 27 Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan:
“Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la,
te xàllal la yoon ci sa kanam.”
28 Maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya masula feeñ. Waaye ba tey ki gëna ndaw ci nguuru Yàlla moo ko sut.»

https://www.youtube.com/watch?v=RH2u1mrw-M4
Author
Content Type
Unspecified
video/mp4
Language
Unspecified
Open in LBRY