LBRY Block Explorer

LBRY Claims • yeesu-jàngle-na-ca-kër-yàlla-ga-luug

af1f41f3dd30ae868620ca7450e634cc3654c76c

Published By
Anonymous
Created On
22 Feb 2022 11:48:32 UTC
Transaction ID
Cost
Safe for Work
Free
Yes
Yeesu jàngle na ca kër Yàlla ga - Luug saa 19, 28 à 48
Yeesu jàngle na ca kër Yàlla ga - Luug saa 19, 28 à 48

Yeesu dugg na Yerusalem
28 Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa daldi jiitu, jëm Yerusalem. 29 Bi muy jege dëkki Betfase ak Betani, ci wetu tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, Yeesu yebal ñaar ci ay taalibeem, 30 ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn masula war. Yiwileen ko, indi. 31 Bu leen kenn laajee: “Lu tax ngeen koy yiwi?” neleen ko: “Boroom bi da koo soxla.”»
32 Ñaari ndaw ya dem, fekk mbir ya deme, na leen ko Yeesu waxe woon. 33 Bi ñuy yiwi cumbur ga nag, ay boroomam ne leen: «Lu tax ngeen di yiwi cumbur gi?» 34 Ñu ne: «Ndaxte Boroom bi da koo soxla.» 35 Noonu ñu indil cumbur gi Yeesu, daldi lal seeni yére ca kaw, yéegal ca Yeesu.
36 Bi muy dem, nit ñi di lalal Yeesu seeni yére ci yoon wi. 37 Bi ñu agsee fa mbartalum tundu Oliw ya doore, taalibeem yépp fees ak mbég, tàmbalee màggal Yàlla ca kaw ndax kéemaan yu bare yi ñu gis. 38 Ñu ngi naan:
«Yaw buur biy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!
Na jàmm am ca asamaan, te ndam li féete ca bérab yu gëna kawe!»
39 Waaye ay Farisen yu nekkoon ca mbooloo ma ne Yeesu: «Kilifa gi, yeddal sa taalibe yi!» 40 Noonu mu ne: «Maa ngi leen koy wax, bu ñu noppee ñoom, doj yiy xaacu.»
41 Bi Yeesu jegee dëkk ba, ba séen ko, mu jooy ko 42 naan: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey yi la mana indil jàmm! Waaye fi mu ne manuloo koo gis. 43 Bés dina ñëwi yu say noon di jal, wërale la. Dinañu la tëj ci biir, tanc la. 44 Dinañu la yàqate, yaw ak sa waa dëkk. Doj dootul des ci kaw doj ci yaw, ndaxte ràññeewoo jamono ji Yàlla ñëwe, wallusi la.»

Yeesu jàngle na ca kër Yàlla ga
45 Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, daldi dàq ña fay jaay, 46 naan leen: «Mbind mi nee na: “Sama kër këru ñaan ci Yàlla lay doon; waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.”»
47 Bés bu nekk Yeesu di jàngle ca kër Yàlla ga. Sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya, ñoom ak njiiti xeet wa, ñu ngi ko doon wuta reylu. 48 Waaye xamuñu woon lan lañu mana def, ndaxte nit ñépp a ngi ko doon déglu, bañ benn baat raw leen.

https://www.youtube.com/watch?v=BjsMl_vmwus
Author
Content Type
Unspecified
video/mp4
Language
Open in LBRY