macë-saar-23-yeesu-gëdd-na-xutbakat-ya
Sunu Yaakaar
Xibaaru Jàmm ak Ibrahima Diop
Macë Saar 23
Yeesu gëdd na xutbakat ya ak Farisen ya
1 Gannaaw loolu Yeesu waxoon na mbooloo ma ak
taalibeem ya ne léen :
2 « *Xutbakat ya ak *Farisen ya ñu ngi toog ci jalu *Musaa.
3 Lépp lu ñu leen wax nag, defleen ko te sàmm ko, waaye buleen
roy seeni jëf, ndaxte dañuy wax waaye duñu ko jëfe. 4Dañuy
takk say yu diis, yen léen ci nit ñi, waaye duñu ko nangoo laal
sax ak seen cati baaraam. 5Dañuy def seeni jëf yépp, ngir nit ñi
gis léen, di takk ay *téere yu réy, tey réyal seeni *laari mbubb.
6Ca reeri xew yi, toogu yu yiw lañuy taamu, tey féete kanam
ca jàngu ya. 7Dañoo bëgg ñépp nuyoo léen ñaari loxo ca pénc
ma, di léen wooye “kilifa gi.” 8Waaye yéen buñu leen wooye “kilifa gi,” ndaxte kenn rekk moo di seen Kilifa, te yéen ñépp
ay bokk ngeen. 9Te buleen tudde kenn seen “baay” ci àddina,
ndaxte kenn rekk moo di seen Baay, ki ci kaw. 10Buñu leen
tudde it ay “njiit,” ndaxte kenn rekk moo di seen Njiit, mooy
*Kirist. 11Ki gëna mag ci yéen mooy ki nangoo nekk seen surga.
12Kuy yékkatiku dees na la suufeel ; kuy suufeelu, ñu yékkati la.
13-14 « Yéen xutbakat yi ak *Farisen yi, naaféq yi, dingeen
torox ! Ndaxte yéena ngi tëj nguuru Yàlla Aji Kawe ji ci kanam
nit ñi ; yéen dungeen ci dugg, te dungeen bàyyi ku ci bëgga
dugg, mu dugg ci.
15 « Yéen xutbakat yi ak *Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox !
Ndaxte yéena ngi wër géej ak suuf, ngir sàkku benn taalibe, ba
noppi ngeen def ko nitu sawara, ku leen yées ñaari yoon.
16 « Yéen njiit yu gumba yi, dingeen torox ! Yéena ngi wax ne :
“Ku giñe kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci wurusu kër
Yàlla gi, dugg na.” 17Yéen ñi dof te gumba ! Lan moo gëna màgg,
wurus wi walla kër Yàlla, gi tax wurus wi sell ? 18Dangeen ne it :
“Ku giñe *sarxalukaay bi ci kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku
giñ ci sarax si ci kawam, dugg na.” 19Gumba yi ! Lan moo gëna
màgg, sarax si walla sarxalukaay bi tax sarax si sell ? 20Ku giñe
sarxalukaay bi, giñ nga ci sarxalukaay bi ak li ci kawam lépp.
21Ku giñe kër Yàlla gi, giñ nga ci kër Yàlla gi ak ki ci dëkk. 22Ku
giñ ci asamaan, giñ nga ci jalu Buur Yàlla ak ki ci toog.
#senegal #sunuyaakaar #wolof #bible
...
https://www.youtube.com/watch?v=GBsDUjk8ZII
Transaction
Created
2 years ago
Content Type
Language
video/mp4